Tijaniyya

Lyrics
Yaa fi xewal gammu gi, yaa dundalaat daara yi Li nga def ci jakka yi, baayi Dabakh waccnga Jaa jef Sy yaa deggal liggeeyu Fa Wade Welle Cheikh Oumar waxoonna ko, yaa taxawal tarixa bi Yaa fi xewal gammu gi, yaa dundalaat daara yi Li nga def ci jakka yi, baayi Khalifa waccnga Gannaar xamna la, waa Maka xam na la Yonent bi geremna la, yaa yore Tijaniyya Yaa fi xewal gammu gi, yaa dundalaat daara yi Li nga def ci jakka yi, baayi Serin Mansour waccnga Yaa fi xewal gammu gi, yaa fi xewal wassifa Zaawiya seede la, reew mi ameelnan la njukel Yaa fi xewal gammu gi, yaa dundalaat daara yi Li nga def ci jakka yi, baayi Dabakh waccnga Dedduwoonna adduna (baayi Dabakh waccnga) Moo doon boroom suuna (baayi Khalifa waccnga) Di it ku amoon fulla (baayi Serin Mansour waccnga) Mandoom ga landina (baayi Dabakh waccnga) Xam xam ba selina (baayi Khalifa waccnga) Dajaloonna teere ya (baayi Serin Mansour waccnga) Doxewuko, damoowuko (baayi Dabakh waccnga) Cheikhou Oumar Foutiyou Tall Maami Seydou Norou Tall Waxoonna ko Yaay taxawale tarixa Cheikh Ahmed, Tijaniyya Cheikhou Oumar Foutiyou Tall Maami Thierno Mountaga Tall Dajalenga kilifa yi
Rate this song
0/5.0 - 0 Ratings
Loading comments...
Credits
- Writers
- Youssou N’Dour