Baay Faal

Album cover art for "Baay Faal" by Youssou N’Dour

Youssou N’Dour - Pop

Baay Faal

2 Plays

Duration: 4:48

View ArtistView Album

Lyrics

Language:

Baay Faal ba daa jóg ca fajar Nga séén ko mu soli sagar Boppam ba sëq ëki kawar Yore këllëm bë di sikkër Te faalewul xiifak mer Moo demee kat xeex na badar Kii turam wi dootul fay Ku weddi lii laaj ko waa Ndar Baay Faal jaaxal na waa Ndar Baay Faal jaaxal na waa Ndar Baay Faal ba daa jóg ca fajar Mani kuur Yalla daa jóg ca fajar Nga séén ko muy soli sagar Yore këllëm bë di sikkër Kii turëm wi dootul fay Ku weddi lii laaj ko waa Ndar Baay Faal jaaxal na waa Ndar Baay Faal jòmmal na waa Ndar Dundam ga neex na, sikkar sa neex lool Baay Faal bi, Baay Faal kii moo di gënë góór Sikkar sa moo tax mu jege Yalla Baay Faal bi, Baay Faal ku ko xamoon di nga maandu ci moom Sa tool ya, sa teen ya, ca waan wa, maajal ya Baay Faal ligééy la xam Baay Faal ndigël la xam Baay Faal du xeex du xulóó Bëgg na nit, fónk na nit Xeebul kenn, noon la yegeeg boroomam Li mu li ligééyal sunu boroom Bëgg naa la Baay Faal Ndongo li kii moo jege sunu boroom Day ligééy di joxe Moo tax Baay Faal jege na sunu boroom Day ligééy di joxe Day ligééy di joxe moo tax Baay Faal Toggam ga neex na lool moo tax Baay Faal Day maajal moo tax Baay Faal Day sikkar moo tax Baay Faal

Rate this song

Rate this song

0/5.0 - 0 Ratings

5
0.0% (0)
4
0.0% (0)
3
0.0% (0)
2
0.0% (0)
1
0.0% (0)

Loading comments...

Credits

Credits Not Found