Baay Niasse

Lyrics
Suunas yonent bi la Sidi Barhame di xeentu Nu mu defe ba yonent bi beg lool la baay di sakku Lu neex Rassulullahi, loolu neexna Baay Niasse Ku xam li yonent bi ban, dô ko gis ci Baay Niasse Moom Sidi Barham Niasse masula fatte waxtu Saa su ne njapp, mu yees, masulu timale waxtu Boo toppee maam ya mbokk laak yonent bi Laajal doom cheikh yi xammeenanu Sidi Su de beggnga roy suunas Mohammed Jokkujil ci Baay Niasse, diineem ja rafetna Bu newel di julli mangay durus lillaahi Baay Niasse xamul ludul tagg Rasuulullaahi Li mu bind ci teere jagleelko yonent bi Li mu bind ci teere jagleelko science bi Li mu bind ci teere mu jem ci wallu xam xam Buur Yalla teeralnako wonewul am am Li mu am ci taalibe ci reewi nit nu nuul ni Lu ko epp la Baay am ci reewi nit nu weex ni Su de beggnga roy suunas Mohammed Jokkujil ci Baay Niasse, diineem ja rafetna Boo demee Medina Baay Laa illaha janngay riir Daaray Alxuraan yaangay riir Niasse Coumba Abdoulaye, jaajеfate Su de beggnga roy suunas Mohammеd Jokkujil ci Baay Niasse, diineem ja rafetna Li mu tabax ci daara de meneesuko lim Dongoom bi gena ndaw menna bind kaamil Ku yaru ci Baay Niasse bu waxee nga xam ko Te lu mu la naanal bilaahi fook nga gis ko La xew ca Maka ak la xew Madina Amul benn werante moo xew ca kerem ya Boo jogee ci reew mi dem ci reewi arab yi Boo nuyoo ba noppi faw nu laj la cheikh bi Su de beggnga roy suunas Mohammed Jokkujil ci Baay Niasse, diineem ja rafetna
Rate this song
0/5.0 - 0 Ratings
Loading comments...
Credits
- Writers
- Youssou N’Dour