Shukran Bamba

Lyrics
Alxamdulillaay ma sant Yalla Bi mu ma wonaleek Cheikh Ahmadou Bamba Cey jiile waay su feenutoon Mbacke Lislaam ji dik te kon ndaw gacce Këpp ku daan liggeeyal diine Nasaraan bi rey la mbaa far la genne Nasaxale lislaam de moo doon seen yitte Cheikh Ahmadou Bamba moo leen far wacce Shukraan laka Shukraan Modou Bamba Xamalena ma Yalla, xamale ma yonentam Wax ma ne jaam de day jaamu sangam Litax nu naan ko Xaadimu Rasulu Moo ma yengal ba ma far ca soobu Leketu neen neenanu naxul bey Fu nepp daw jublu gisnanu fa lu rey Yagg na ma gestu lu jem ci Bamba Masumu gis fu mu juuyook waa ja Shukraan laka Shukraan Modou Bamba Menuma la fey xanaa ma woy la Liggeey ba dee rek ngir addiya la Mbacke danga yaa ginaaw ak kanam Nan roy ci yow ngir mena jem ci kanam Soo deggee ma naan waa ja Waa ja mooy kiy waajale gaa na Te kooku daal, moo di doomi Abdoulaye ja ca Madina Ahmadou Bamba, man de sant naa la Jaa jef baayi Mamadou Lamine Barra Sama diggenteek Yalla yaa ma ko leeral Lu ne wonenga ko taxul nga jeexal Yaa tax may baaleek di yeremaate Jaa jef, jaa jef baayi Serin Saliou ak Serin Mourtala Shukraan laka Shukraan Modou Bamba Menuma la fey xanaa ma woy la Liggeey ba dee rek ngir addiya la Mbacke danga yaa ginaaw ak kanam Nan roy ci yow ngir mena jem ci kanam Ahmadou Bamba, man de sant naa la Jaa jef baayi Mamadou Lamine Barra Sama diggenteek Yalla yaa ma ko leeral Lu ne wonenga ko taxul nga jeexal Yaa tax may baaleek di yeremaate Kenn dootuma atte te ban xeebaate Jaa jef, jaa jef baayi Serin Saliou ak Serin Mourtala Shukraan laka Shukraan Modou Bamba Menuma la fey xanaa ma woy la Liggeey ba dee rek ngir addiya la Mbacke danga yaa ginaaw ak kanam Nan roy ci yow ngir mena jem ci kanam
Rate this song
0/5.0 - 0 Ratings
Loading comments...
Credits
- Writers
- Youssou N’Dour