Cheikh Ibra Fall

Lyrics
Mber mi nu naan Cheikh Ibra Fall Te nu koy wooye Lamp Fall Ahmadou Bamba moo ko taal Foo ko tudde nepp ni Fall Masula fo, xamul ay baal Te kii du kuy tedd ci lal Daa gis lutax muy tebb di dal Ahmadou Bamba raw ay baal Njekk mu now ci Bamba daal Cheikh Ibra daa meloon ni taal Am ay garab ba kenn du ko laal Laajal, laajalma waa Kawsara Fall Cheikh Ibra Fall, Cheikh Ibra Fall, jambaar la Cheikh Ibra Fall, Baabul Muridin Daa tedd guddi nu ne ko Fall Mouhamadou Mbacke lay jafal Jox ko ci moom ay tektal Lii moo waral mu and ak aal Waxtu wu ne mang koy maggal Dii soq te roota ko war Na mu fa fekkoon da leen lakkal Ci di leen sujoot waajaangi daal Cheikh Ibra Fall, Cheikh Ibra Fall, jambaar la Cheikh Ibra Fall, Baabul Muridin Fekkoonna nods mu nuy tangal Ndongo ya naa bu kenn laal Mu ne ko cass, du jog ci aal Ngir li mu gem Cheikh Bamba daal Cheikh Ibra Fall, Cheikh Ibra Fall, jambaar la Cheikh Ibra Fall, Baabul Muridin
Rate this song
0/5.0 - 0 Ratings
Loading comments...
Credits
- Writers
- Youssou N’Dour