Doole

Lyrics
Sa doole sa doole sa doole bul ko xeexe Jaay doole baaxul ag si ku mu mene doon Dekkende yi fonkal seet ci Yalla mi nu moom Ana jambaar yu mag yi boroom alal yu bare yi Boroom xam xam yu rey yi ne kenn nekkatu fi Aah doole du wey Jaay doole baaxul ag si lu mu mene doon Tay men nga baaxle, ellek nga daldi yaqule Bul nawoo sa doole ba tax nga gaawa laale Ku yegsi men ko faale te nga saxoo di baale Aah doole du wey Maandul te rafetal sa nekkin Yaw deel baale bana wane sa doole Bul jel yaw sa doole xal di ko xeejе Sa doole dimbele ci jaam yi Jaay doolе baaxul ag si lu mu mene doon Bul kan sa doole ba di ko tiiteroo Besa ngi ci bes yi te faww bes bi yegsi Nu dajale yaw sa jef yi nga xam nè Yalla mu ngi fi Aah doole du wey Fas wa dafa naagu ne mbaam ma maa la gene gaaw Booy daw da ngay yeex te man da may gaaw Fas wa di njekkente ba far dugg ca teen ba Bu dul woon ag mbaam ma fas wa des ca teen ba Aah doole du wey Ne Maandul te rafetal sa nekkin Yaw deel baale bana wane sa doole Bul jel yaw sa doole xal di ko xeeje Sa doole dimbele ci jaam yi Sa doole sa doole sa doole bul ko xeexe Jaay doole sax woorul kenn xamul fooy mujjee Jaay doole sax woorul ndax kenn xamul fooy mujjee Bul naagu si sa am am Ndax adduna men na laa njuuy Am am ag men men dekkul fenn Waaye doole jii ci biir mbeggeel Kenn menuko teye Bu xasee jog, jamm jeexna Lu new daan, seetal Li ci jig mbeggeel jigu ci leneen Mbeggeel gu woor wane doolee ko jig Bu ko deful ba seytaane dugg ca, seetal Doole jii ci biir mbeggeel Kenn menuko teye Bu xasee jog, jamm jeexna Lu new daan, seetal Doole jii ci biir mbeggeel Kenn menuko teye Bu xasee jog, jamm jeexna Lu new daan, seetal
Rate this song
0/5.0 - 0 Ratings
Loading comments...
Credits
- Writers
- Youssou N’Dour
- Kabou Gueye
- Pape Dieng
- Habib Faye